My Child

de Youssou N'Dour

Non, non non non non
Non, non non non non

Ne xale bi
Ne bëgguma la mer loo
Ne xale bi
Bëgguma la mer loo

Ndaxte soo meree
Soo meree
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma
(Bul ma meree)

Lu menul ñàkk
Faw dafay am
Wareef dafay mat
Léeg-léeg mu doon lu dul neex
Yow sama doom
Suba tax may wax
Soo magee dinga xam

Ndaxte soo jooyee
Soo jooyee
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma

Waa-jur ak doom
Faw ñuy waxtaan
Feexee mel ni mburu ak sow
Ndem réeru mën ta ñàkk
So diaxlé, so diaxlé
Na sa xel mi dem
Dem ci say waa-jur

Ni jamono mel
Teey da cee baax
Jubbantil ba mu cor
Ndax muumin dafay rooy

Bës a ngi ñëw
Su maggee jariñ la
Lepp ngi ci ba muy ndaw

Ndaxte soo meree
Soo jooyee
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma
(Bul ma meree)

Ne xale bi
Ne bëgguma la merloo
Oh xale bi
Ne bëgguma la merloo

(Xale muumin la
Yow bu ko merloo
Te dee ko bégal)

Ndaxte soo meree
Soo meree
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma

Àdduna nii la, xale bi le
Su baay waxaatee, nga déglu ko
Àdduna nii la, xale bi le
Su yaay waxaatee, nga déglu ko

Àdduna nii la, xale bi le
(Na nga ma dégloo xel)
Su baay waxaatee, nga déglu ko
(Bañ ma dégloo xol)
Àdduna nii la, xale bi le
(Sama doom)
Su yaay waxaatee, nga déglu ko
(Na nga ma dégloo xel)

Ne xale bi
Ne bëgguma la merloo
Ah xale bi
Ne bëgguma la merloo
Xale bi
Ne bëgguma la jooyloo

Ndaxte soo meree
Soo meree
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma

Más canciones de Youssou N'Dour