Jiné Ji

de Wasis Diop

Seedeleen ma wax ko benn yoon
Yeee, moom jaral na ma
Yéen seedeleen ma wax ko ñaari yoon oh
Yee yeee, moom jaral na ma

Dina ma woo, dina ma toppatoo
Dina ma jege saa su ne di ma ree
Dina ma woo yee, dina ma toppatoo waaw
Dina ma jege saa su ne di ma ree
Man xame naa la te ñeme naa la
Yaa ma doy ci farandoo danga ma neex

Chéri saay saay, man duma mën a jege
Kaay kaay, yaay sama coco rappé
Saay saay duma xool ba may ñeme
Kon taamu naa la, yaa fi ne

Doy nga ma wéeruwaay
Doy nga ma karange
Doy nga ma ci sa njegenaay waaw laay lange
Fa laay lange, fa laay lange
Fa laay lange, ci sa wet laay lange
Fa laay lange, fa laay lange
Fa laay lange, ci sa wet laay lange

Ki ma sagal yaw la
Ki ma thiëreul yaw la
Ki ma téral ba ma tédd teg ma si wetam yaw la
Su ma bégee yaw la
Mënuma baax ba raw la
Su ma génnee ñu naw ma billaay ginnaaw Yàlla yaw la

Kon tay des na ci man
Ma mat la seuk yaay
Mat la jabar
Mat la ki lay bëggel ki lay ray
Ki lay ray, waaw!

Chéri saay saay, man duma mën a jege
Kaay kaay, yaay sama coco rappé
Saay saay duma xool ba may ñeme
Kon taamu naa la, yaa fi ne

Doy nga ma wéeruwaay
Doy nga ma karange
Doy nga ma ci sa njegenaay waaw laay lange
Fa laay lange, fa laay lange
Fa laay lange, ci sa wet laay lange
Fa laay lange, fa laay lange
Fa laay lange, ci sa wet laay lange

Jigéen bu la muñalee danga koy sagal
Góor bu la téralee danga koy gërëm
Jigéen bu la muñalee danga koy sagal waaw
Góor bu la téralee danga koy gërëm

Baye Ndidiay Coly góor silé for silé tokk
Ciin bu mag nelawal
Gaynde bu boffee doomam bey su ko laale tooñ
Est-ce que dina ko laal, waawaaw
Yee yeee, danga koy sagal!

Más canciones de Wasis Diop