Déni

de VJ

Seet naa seetoo seetaat gisaguma ku mel ni yaw
Sa jëmm jee ma yëm man gisuma keneen
Pourtant man, pourtant man
Gis naa façon bu ne
Pourtant man, pourtant man
Gis naa jigéen bu ne
Yaw laa doon ñaan Yàlla (tukulóor al racine)
Ñaan yi mujje àntu (jekk rafet yaa ngi)
Yaw laay gis weer baa ngi
Kuy ndeyam ak baayam
Seetoo séet yaa ngi xooloo say moroom
Jugleen tay la tay ku ko xam na nga jaayu (jaayu)
Yaa jara sargal yaa jara tàccu
Jaayul tey sa bés la
Man maa la taamu say digg moroom say nawle
Su la neexee baaxu!

Mbëggeel dafa diis, dafa bari doole
Yaay sama aljanna (waawaaw yaw la)
Yaay sama aljanna (ahh ahh yaw la)
Yaaa ma leen gënal yaw mi (waawaaw yaw la)
Yaay sama aljanna

Diombadioo ari, diombadioo ari
Diombadioo ari sama séet baa ngi yegsi na
Diombadioo ari, diombadioo ari
Diombadioo ari sama séet baa ngi yegsi na

Bés bi laa doon xaar, tay dafa mel ni moo ngi
Ëgsil sama ndaanaan, naa la siggil ci say noon yaw
Fi ñu jaar, li ma la tooñ, li nga may baal
Li ma la jaral ak fi nga ma toollu, sama ndaanaan
Yaa ma leen gënaloon, dama leen ko rusoon a wax
Imam teew na nawle yépp teew yaw de nga ni waaw
Njegemaar bis yaa di mët jëg
May ko mu jal sama miss baa ngee
Xale la waaye fees na ak jom
Bis dina jonni ndaanaan sama miss baa ngi

Mbëggeel dafa diis, dafa bari doole
Yaay sama aljanna (waawaaw yaw la)
Yaay sama aljanna (ahh ahh yaw la)
Yaaa ma leen gënal yaw mi (waawaaw yaw la)
Yaay sama aljanna

Diombadioo ari, diombadioo ari
Diombadioo ari sama séet baa ngi yegsi na
Diombadioo ari, diombadioo ari
Diombadioo ari sama séet baa ngi yegsi na

Me and you for life, for life bae
Me and you for life, for life bae
Xamal ni maa ngi ci sa wet
Muy taw wala muy naaj, ma belle

Más canciones de VJ