Wuyuma

de Viviane Chidid

Xale bi sama reni xol de wuyu ma
Bëgg naa la te xamoo ci dara
Mbëggéel ci xol lay nekk dëgg la
Bëgg naa la te xamoo ci dara

Man de walluleen ma wax ko ko
Xale bi lekkatuma ndax moom
Naanatuma, nelawatuma
Wowo, sama xol yaa ci ne

Lég-lég ma woo ko tit dal di coupé
Sama appetit coupé
Feebar dina ma gunge
Docteur dama love ba dof
Te xawma lu koy faj
Wowo, mbaa mën nga ci dara

Xale bi sama reni xol de wuyu ma
Bëgg naa la te xamoo ci dara
Mbëggéel ci xol lay nekk dëgg la
Bëgg naa la te xamoo ci dara

Man woo naa la fu ne
Nga jàppe ma sa xarit
Inviter résto, lalal naa la lu ne
Wowo, nga jàppe ma sa xarit

Lég-lég ma woo ko tit dal di coupé
Sama appetit coupé
Feebar dina ma gunge
Docteur dama love ba dof
Te xawma lu koy faj
Wowo, mbaa mën nga ci dara

Man bëgg naa ma bañ bàyyiwuma
Man gisuma kenneen ku dul moom
Mbëggéelu bari doole yeen ma ko xam

Xale bi sama reni xol de wuyu ma
Bëgg naa la te xamoo ci dara
Mbëggéel ci xol lay nekk dëgg la
Bëgg naa la te xamoo ci dara

Xale bi sama reni xol de wuyu ma
Bëgg naa la te xamoo ci dara
Mbëggéel ci xol lay nekk dëgg la
Bëgg naa la te xamoo ci dara

Ku ci nekk ak ki ña nob
Sa ginnaaw bandag faxasul
Juugel yëngël ba mu saf
Sa ginnaaw badang faxasul

Ku ci nekk ak ki ña nob
Sa ginnaaw bandag faxasul
Juugel yëngël ba mu saf
Sa ginnaaw badang faxasul

Más canciones de Viviane Chidid