Karkarato
de Sidy Diop
Jëkkër ko mu na ne (yeah yeah)
Sutura yërmande (yeah yeah)
Bul dóor, bul saaga, jantal men
Jigéen la Yàlla moo ko dooleel yeah
Sant naa la bégal, wéral, goreel
Jugel ci ñoom dañu leen war a teral
Bu kër gi neexe ñoom la dañu leen war a keral
Su ma sañoon dara du leen metti, yeen a waral li
Anyi yeah
Ku xool ba jël lu metti tekk ko
Bu ñu ko demoon teg sa doom
Dinga mu na yëg li may yëg
Tay ma woy ba foog ni dama dof
Faw ma woo ma woo la xool ma yaw la jigéen yaay yee
Yaw say wena sëg waaye yaa nu mën
Gannaaw yonent lu Yàlla bind yaa ci gën
Kon buñu ko xarafal, buñu ko gaañ ci dënn
Ndox du jéeg, pax bu jege, pax dafa fekk
Yaw bul ko dóor, bul ko saaga woo
Jël ko def ko doom
Ndax mooy sa soxna mooy sa yaay boo yoo
Yërmande ci ñoom
Jigéen bul ko dóor, bul ko saaga
Meritewul lii
Ndax moo ñu jural yaay, jural ñu baay booy
Kon yërmande ci ñi!
Xare baddax comme Sitoé
Doon jaambaar ndor ak nawet
Man yeen laay delloo njukkal
Jigéen na jur ki toog palais
Icône ni Mame Diarra ak Marie
Boo danoo jugal
Eh big up to Halima Gadji
Kennen ku baax tuddel
Doon ñafekat, bañekat
Di diplomé ak baykat
Fees Université def fac
Grade yi gën a di bari, laf cat!
Yeen ay diamant yenn ay or
Am na ay jigéen yu mën góor
Bu dul jigéen, kan lay doon?
Ñoom nak war rekk lañuy door
Listen!
Baat ba ma jël ca maam
Doomu góor nga jugal, sol sa dàll
Bu de góor nga dinga songu daan
Bu de jigéen'anga ci digg ginnaaw geej
Ndam, mérite, am njëriñ, mat sëriñ
Gàllaaju jigéen mu ngi ba digg ginnaaw géej
Akak yeleef gi war ci ñoom ñanu ko def
Ndax jigéen mosul feete suuf
Talaatay Ndeer ay jigéen ñoo ko def
Yaw bul ko dóor, bul ko saaga woo
Jël ko def ko doom
Ndax mooy sa soxna, mooy sa yaay yaa boo oh yoo
Yërmande ci ñoom!
Jigéen bul ko dóor, bul ko saaga
Meritewul lii
Ndax moo ñu jurel yaay jurel ñu baay boy
Kon yërmandé ci ñii