Police - Live

de Mass Konpa

Gune may dékk
Ma nga may daaneel
Fi ma la tég
Romb naa bu gañe

Gune may dékk, waay
Ma nga may daaneel
Fi ma la tég waay
Romb naa bu gañe, waaw

Ku la doon wuute ci man dinaa la am
Ku ma bëgg bàyyek yaw, na ma ba xam
Jaral nga ma xeex ak gaynde, nañ ci nu mbaaxal
Bu suuf seede ba ñépp tëddi ma, am lu ma la wan waay

Sama mbëggeel dafa faq wuuti sa bos
Sama xol jarafe sedd kër giy jalañoo
Su ñu gisee ma na weete ba am lu ma la def
Ndax gone may dékk waaye ma nga may daaneel

Xale bi defal ndank
Ñëwal sax ma déey la
Loo ma ñaan ma may la
Bu doyul ma dolli la!

Gune may dékk
Ma nga may daaneel
Fi ma la tég
Romb naa bu gañe

Yaa ma gënal ñi ma xam ak nit ñi ma xamul
Jaral nga ma def a def ba def lu ma munul
Ni ngay doxe dafa yeem ma dikk lu ma amul
Ku mel ni yaw dootu fi am ñi dañu xamul, waay!

Sama mbëggeel dafa faq wuuti sa bos
Sama xol jarafe sedd kër giy jalañoo
Su ñu gisee ma na weete ba am lu ma la def
Ndax gone may dékk waaye ma nga may daaneel

Xale bi defal ndank
Ñëwal sax ma déey la
Loo ma ñaan ma may la
Bu doyul ma dolli la!

Más canciones de Mass Konpa