Thiopet Yobu
de Jeeba
Jeeba la boy!
Ne na ma Fall
Li ngay def dang ci gaaw
Ndax at yi dañuy gaaw
Te temps bi doonul lu ñuy xaar
Gis nga maa ngi ni di jéem
Ba tay defuleen lu leer nak
Yaw lewtoo ma firiwoo nak
Te yaw pusoo pasoo nak
Gis nga Demba ak Modou
Sama kër Pathé ak Ndiogou
Bés bu ne fa lañuy ñëw rigu
Di xaar ku naan leen indil guro mbaa doudou
Yaw nak danga am lu kenn amul, ne ma lan
Xol bi yaa ko moom te kenn laaju la fi chaîne
Lan mooy sa problème wax ma ko ñu solution ko
Tay nga jàpp suba nga bàyyi, ñu mel ni Macki ak Sonko
Wala danga hum hum hum te yëguma ko
Ma ne boo yéexee dañu ma naan coopet
Yóbbu
Hey, ku ne di laaj fan la ne
Mu naan dañuy jaay doole
Chiiip ndoku
Ey, lu mu soxla rekk lay jël
Taxawe ne yéeme
Lii dafa yéeme, yéeme
Lii moo yéeme, yéeme
Lii dafa yéeme, yéeme
Lii moo yéeme, yéeme
Ne na ma Fall
Jigéen dafay gaaw a stresse
Dafa soxla ku ko rassuré
Pas ay promesse sans cesse
Danga koy xool sa bopp fi kenn bëggul ñuy use sa time
On n’a qu’une seule vie te duñ la xaral ménopause
Jigéen soo ko bëggee dangay def différence
Lan mooy ndeyu benn ba ñeenti at ci relations
Tay nga yóbbu restau, suba passant de vision
Bëgg di séy guddi séy, bëcceek manoo def xalal
Wax ci moom soo bëggee takkal, soo bëggul demal
Bul yàqal keneen muy deme neneen
Soo bëggee takkal, soo bëggul demal
Bul yàqal keneen muy deme neneen
Ey, boo yéexee dañu ma naan coopet
Yóbbu
Hey, ku ne di laaj fan la ne
Mu naan dañuy jaay doole
Chiiip ndoku
Ey, lu mu soxla rekk lay jël
Taxawe ne yéeme
Lii dafa yéeme, yéeme
Lii moo yéeme, yéeme
Lii dafa yéeme, yéeme
Lii moo yéeme, yéeme
Eh, Momo takkal gone gi
Ahmet takkal gone gi
Amadou takkal gone gi
Djibril takkal gone gi
Lii dafa yéeme, yéeme
Lii moo yéeme, yéeme
Lii dafa yéeme, yéeme
Lii moo yéeme, yéeme
Enfin
Babo takk na gone gi!