Saï Saï

de Jeeba

Yàlla du juum, ndekke Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gën
Demoon naa ba nar ko dugal sama biir xol
Su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Kon fok ma xoolaat ko
Saay-saay la
Fok ma xoolat ko
Waa ji saay-saay la

Yàlla du juum, ndekke Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gëna
Demoon naa ba nar ko dugal sama biir xol
Su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Ñew na sama kër laajte fa sama yaay booy
Saay-saay la
Ñëwaat sama kër laajte fa sama baay booy
Saay-saay la

Ne na kilifa la du dox ci tànk caaxaan
Ñeent ak tranche indi guro daadi laban
Mi ngi may teg tank bëgg ma forcé ray
Ndekke lu mu bëggoon dugal but bi jubilé daw

Yàlla du juum, ma ni Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gën
Demoon naa bay xalaat nar ko jox sama xol
Ndekke su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Kon fok ma xoolaat ko
Saay-saay la
Kon fok ma xoolat ko
Ndaw si saay-saay la

Yàlla du juum, ma ni Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gëna
Demoon naa bay xalaat nar ko jox sama xol
Ndekke su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Ne na ku dul man bëggul soxlawul
Ma ne rekk la jox bopp ku mel ni man amul
Man ma ko yëngal-yëngal mbëgelam
Ndekke man dama dóor ay calmant la may jox
Dem naa ba dépense këram ma ko yor
Fay courant, fay ndox, fay jàng xale yi école
Jënd greffage, fay ay voyage
Nekke damay door sama poche la nob

Yàlla du juum, ma ni Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gën
Demoon naa bay xalaat nar ko jox sama xol
Ndekke su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Kon fok ma xoolaat ko
Saay-saay la
Kon fok ma xoolat ko
Ndaw si saay-saay la

Yàlla du juum, ndekke Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gën
Demoon naa ba nar ko dugal sama biir xol
Su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Kon fok ma xoolaat ko
(Ndaw si saay-saay la, waay)
Fok ma xoolat ko
Waa ji saay-saay la

Yàlla du juum, ma ni Yàlla du juum
Lu mu def ndekke loolu moo gën
Demoon naa bay xalaat nar ko jox sama xol
Ndekke su ma ko defoon maa ngi ci tolof-tolof

Más canciones de Jeeba