Guuy

de Jeeba

Dina la dal foo ko dul fooge
Foo ko dul xalaate
Ci ba ngay dogu ci la laay duggé
Dey mel ni Yàlla ko yónnéé

Dina fees sa xol bi, unh no no
Ëlëmal sa bopp bi, unh yeah yeah
Dooto amati principe, bafouer nga lépp
Mënoo gis ci moom sikk

Yaw lu maa lay def du yow rekk yaa ko xam ma
Du lu nit mëna wax
Yoow fi nga may yóbbu, dafa mel ni mësuma fa dem
Waaye du lu niit mëna wax

May topp sa ginnaaw di daw
Mel ni mbëggéelu xale xale xale
May laaj kañ laay maggee
Nga teyi ci sama yeri bi ñuy xandal
Dawal mbégé mbégé mbégé
Dégg na sax dama jonge

Kon kaaru kaar, kaar machallah
Dañu bëggante ba niróo
Yaay sama héro
Sama bébé d'amour
Conquérir nga sama xol
Fi yaa fiy buur
Defal lu la neex nga xol

Boo bégee ma bég, boo jooyee ma jooy
Li ma gisul ci ñoom laa gis ci yow mu doy ma
Sànni nga karawaas
Daan nga leen jél bu gaaw
Maay sa jomb a ñaaw
Jomb naa la def lu ñaaw

Ndax kérok ba ma la gisee, eh eh
Eh eh si la xam ni doo ma rëccé
Man kérok ba ma la gise
Eh eh si la xam ni doo ma rëccé

Yow seral nga sama xol
Guuy guuy guuy guuy
Yow séral nga ma
Guuy guuy guuy guuy
Yow walay séral nga sama xol
Guuy guuy guuy guuy
Yow séral nga ma
Guuy guuy guuy guuy

Yaw tànk ak tànk, mbagg ak mbagg ñu dem
Waat nani dina la yobbu feneen
Yaw defal ndank bul deglul waxi noon
Ñoom duñu dem bëgguñu ku dem

Eh, xanaa xamoo ni lu baax ñepp ko bëgg-bëgg
Fi li ñuy wax xaaj ba du dëgg-dëgg
Eh, xana xamoni mën nañu wax mais duñu bëgg
Seen biir xol mënu ñu gis ñaar ñu bëggante

Te xam naa waroon na doon gëwel
Ma taggal la say maam
Waroon nga doon jaam
Ma goreel la goreel say maam
Su ma amoon avion ma may la ko di la dawalal
Foo bëgg ñu jëm ca
Li su la doyul wax ma lu lay doy bébé
Walay walay xawma li lay doy

May topp sa ginnaaw di daw
Mel ni mbëggéelu xale, xale, xale
May lajj kañ laay maggé
Nga teyi si sama yeri bi ñuy xandal
Dawal mbégé mbégé mbégé
Dégg na sax dama jonge

Kaaro kaar, kaar machallah
Dañu bëggante ba niróo
Yaay sama héro
Sama bébé d’amour
Conquérir nga sama xol
Fi yaa fiy buur
Defal lu la neex nga xool

Ndax kérok ba ma la gisee, eh eh
Eh eh si la xam ni doo ma rëccé
Man kérok ba ma la gise
Eh eh si la xam ni doo ma rëccé

Yow seral nga sama xol
Guuy guuy guuy guuy
Yow séral nga maa
Guuy guuy guuy guuy
Yow walay séral nga sama xol
Guuy guuy guuy guuy
Yow séral nga ma
Guuy guuy guuy guuy

May topp sa ginaaw di daw
Mel ni mbëggéelu xale xale xale
May lajj kañ laay maggé
Nga teyi si sama yeri bi ñuy xandal
Dawal mbégé mbégé mbégé
Dégg na sax dama jonge

Más canciones de Jeeba