Diarabi - Remix
de Jeeba
Eh eh eh eh eh!
Jeeba le boy
Oh oh oh oh oh oh oh
Yeewu jàkkaarloo ak sa kanam
Sama bët yi di xool
Di la xool, oh oh oh xool
Maay gis ci sa kanam bànneex
Mbëggeel bu dul jeex
Man ak yaw ba asaman, eeh asaman
Dakante, dóorante ni xale
Fu ma la jekko baal naa ko
Te yaw foo ma jekko nga baal ma
Ngir mbëggeel bi nga may wan
Yàkkamti ba ñu ne al-xayri
Ma xëcc la taf la sama kaw
Dootoo ma rëcce abadan, eeh abadan
Maa yéene na ku ne mu dund love bi may dund
Maa yéene na ku ne mu xam li ih ih
May dundu aljana te deewaguma
No, non, non, deewaguma
Jox la samay bët wommat ma ni gumba
Yo, wommat ma ni gumba
Ba xol bi réere
Yaw yaa ko for, fatt ko sa kër
Noonu la ma leer
Loo amul ci man, lépp ci yaw la
Eey, dee ma ree
Maay kontaan di bég
Eey, dee ma ree, eh eh eh
Jox naa la lii, jox naa la lee
Gis naa la fii, gis naa la fee
Jox naa la lii, jox naa la lee
Gis naa la fii, gis naa la fee
Ba dafa mel ni yaw danga joge asaman
Indale mbegté, mbegté buy ñëw ci man
Defe naa nii, def naa la ni
Ngay sama diarabi, diarabi ih ih ih
Yeewu di laajte sa kanam
Di wër fan la nekk
Di ko seet, eh eh eh eet
Maa namm la te soriwoo ma
Yàkkamti ba jant bi fenk
Ba ma gis la fi sama wet, eh eh ett
Yaw yaay taw biy meññ suma tool
Sans yaw lépp ay wow
Yaw yaay tax may ñafe bëgg a doon
Sa góor bu dee ci yaw
Kon bul tiit, bul mësa nangu jaaxle
Aljana laa lay yóbbu
Yaw bul tiit, bul mësa nangu jaaxle
Man ak yaw ba abadan, haaan waaw
Jox naa la lii, jox naa la lee
Gis naa la fii, gis naa la fee
Jox naa la lii, jox naa la lee
Gis naa la fii, gis naa la fee
Ba dafa mel ni yaw danga joge asaman
Indale mbegté, mbegté buy ñëw ci man
Defe naa nii, def naa la ni
Ngay sama diarabi, diarabi ih ih ih
Yeah, yeah, yeah