Champion

de Jeeba

Kon jot na tay ma magg
Futeku bëre daan
God may ma ndam dootuma trainée yow
Yennay joxooñ maay dagg
Am-ambu sawaan bawaan
Coono àdduna dootuma tere nelaw

Bakkul rekk maay gis
Champion nga fils
Bakkul rekk maay gis
Champion dégg nga fils

Man bëre na walaahi bëre na
Man bëre na, bëre na
Bëre duma daanu
Entraîné na entraîne na entraîné na
Aiguisé sama mind

Du xol be ñék fatteliku demb ni mu metti woon
Waral ma xaali yoon bëgg doon champion
Ñi ne mën naa ko def ñi ne mënuta baax
Saalo liggéey ak ngëm ñanu wajur mooy sama doole
I don't care bala waxal duma tere def
Xarañ na ba ñépp nangu maay modu si biir geew
Waye Yàlla baax na yow Yàlla baax nga
Musel ma man ci samay pexem noon
Bàyyi ma ak sama xel ma mëna agaale
Mbëbët mi ne ci man ndax champion laay mësa doon

Kon jot na tay ma magg
Futeku bëre daan
God may ma ndam dootuma trainée yow
Yennay joxooñ maay dagg
Am-am bu sawaan bawaan
Coono àdduna dootuma tere nelaw

Bakkul rekk maay gis
Champion nga fils
Bakkul rekk maay gis
Champion dégg nga fils

Sky is the limit, on a plus rien à prouver
Baal ba taak na bidéew bu juge asaman
Koy wax bokkul ak kuy jëf
Man damay bëre daan
Doole gaynde ndiaye doo ma dëggel ndeysaan

Xamee na jànj ak Dior xamee camooñ ndeyjóor
Toj na lamb Ndakaaru, Cees kay jàpp sikicoor
Kaay waay man bëre daan laay gis
Gëm-gëm bi dootul deñ ba abadan da imam
Sakku na ñan ku faraal Jeeba ne ko ya mën
Waye Yàlla baax na yow Yàlla baax nga
Musel ma man ci samay pexem noon
Musel ma man ci samay pexem noon
Bàyyi ma ak sama xel ma mëna agaale
Mbëbët mi ne ci man ndax champion laay mësa doon

Kon jot na tay ma magg
Futeku bëre daan
God may ma ndam dootuma trainée yow
Yennay joxooñ maay dagg
Am-am bu sawaan bawaan
Coono àdduna dootuma tere nelaw

Bakkul rekk maay gis
Champion nga fils
Bakkul rekk maay gis
Champion dégg nga fils

Hé Jeeba le boy
Hé Jeeba le boy
Hé hé Jeeba le boy
Jeeba le boy, Jeeba le boy, Jeeba le boy

Más canciones de Jeeba