Aladji

de Jeeba

Li lan doon ñaan
Mel na ni ñaan yi nangu na
Ñun li lan doon xaar
Bes bu ñu lay wáccel Sokhna
Te kër gi ko ci xool tout le monde a la joie
Tout le monde a la joie
Waay jaarul wax sax ouais ouais sa se voit
Ouais ouais sa se voit

Yow papam ak ay xaritam di waaj dem juma
Ba ñu takk sëy bi rekk ñu sandi dua
Ngay dégg 'heureux ménage, heureux mariage'
Ñu lay taggal say louanges
Yow yaay boy ak xarit yi di ko ndokaale
Tay nga faayu booru ndawtal yiñ la amel fu ne
Waay dañuy xawaare, taggate ba mu saf
Tay dañuy xawaare

Man takk na jabar
Def na li war
Dégg na dëkku na mbër
Way dafa doon li war

Ndax daf may neex lool ñu may woowee Aladji
Bébé d'amour, bébé Aladji
Waawaaw Aladji, waawaaw Aladji
Man daf may neex lool ñu may woowee Aladji
Bébé d'amour, bébé Aladji
Waawaaw Aladji, waawaaw Aladji

Bës yow du tuuti
Bës du boroom rekk laay tollool
Saa liggéeyu ndey moo la wuyusi
Ñépp d'accord nañu ci loolu
Waa taay dañuy daal di bâche koñ ba koñ
Xar yi ñu rey, ginàar yi ñu njoñ
Ñu yeggal niveau bi àjj ba si kow-a-kow
Ku aaye wone sa moom, taay yaa moom

Yow papam ak ay xaritam di waaj dem juma
Ba ñu takk sëy bi rekk ñu sandi dua
Ngay dégg 'heureux ménage, heureux mariage'
Ñu lay taggal say louanges
Aladji génn ak ñeeti pièce machallah
Xarit yi di daar ko di ko jiin jino jiin
Dem gatandu jii madame, gan bi yegsi na
Ne ko 'bismillah!
Tay dañuy xawaare

Man takk na jabar
Def na li war
Dégg na dëkku na mbër
Way dafa doon li war

Ndax daf may neex lool ñu may woowee Aladji
Bébé d'amour, bébé Aladji
Waawaaw Aladji, waawaaw Aladji
Man daf may neex lool ñu may woowee Aladji
Bébé d'amour, bébé Aladji
Waawaaw Aladji, waawaaw Aladji

Yeah!
Wuyu ma Aladji
Si géew gi yaw laa ñuy xaar Aladji, Aladji
Bës bi sa bës la, Aladji
Guddi gi yaa moom Aladji, yeah
Eeeweh sama Aladji, aah Aladji Aladji
Sama Aladji, ooho Aladji sama Aladji!

Más canciones de Jeeba