Njabar

de Iss 814

Fi sa xol bi ne fa laa nekk
Fi sa mbëggéel toog laay toog
Fi nga fanaan fa laay nelaw, humm
Bi moo jugé dem bay ñibbi
Danga ma xëccaat ne na toogal
Ndax pareguma ci yaw

Noo ko mëne
Lii noo ko mëne
Noo ko mëne, my baby
Wax ma foo ma jëme
Yaw foo ma jëme
Foo ma jëme, xale bi

Est-ce que xam nga li nga jaral
Mooy bi may jooy love
Yaa ma jël aakimu, kenn du ma separé ak yaw
Yaa may jooyloo, maa la jooyloo
Jëlal bum bi yew ci baat foy dem ñu àndandoo

Ndax bëgg naa la (he he he he)
Xam naa ni bëgg nga ma (he he he he)
Ndax bëgg naa la (he he he he)
Yaw tamit bëgg nga ma (he he he he)

Yaw rekk ay ki may jege, di ma jege
Di ma dundal, di ma miirloo
Tegsi di ma dofloo
Man yaw rekk laay bëgg di la bëgg
Amul douter bu ñu wéetee yaw yaay nekk sama goûté

Hummm hum
Bu may faayu dama lay humm hum
Bu ñu wéetee yaw yaa ma may humm hum
Bu ma faayu dama lay humm hum
Bëgg naa la, bëgg nga ma

Suñu diggante daq lem
Ku ko amul na nga xaar
Wóolu naa la, wóolu nga ma
Foo jub lu la bëgg, dem may sa code-phare

Est-ce que xam nga li nga jaral
Mooy bi may jooy love
Yaa ma jël akimo, kenn du ma separé ak yaw
Yaa may jooyloo, maa la jooyloo
Jëlal bum bi yew ci baat foy dem ñu àndandoo

Ndax bëgg naa la (he he he he)
Xam naa ni bëgg nga ma (he he he he)
Ndax bëgg naa la (he he he he)
Yaw tamit bëgg nga ma (he he he he)

Más canciones de Iss 814