ALLER AK RETOUR

de Iss 814

Bëgg naa àndaak yaw ma love
Bu ñu àndee suñu coono du reer
Ne nañu ma boo bëggee yaay perte
Jamono ji léegi ñépp reer
Yaw mi ma jox sa xol
Yaa xam lu tax nga wóolu ma
Ma jël delloo la sama xol
Xam naa lu tax ma woolu la

Fi ñu bëgg dem maak yaw baby
Ak lu mu metti dinañu fa yéeg ñun ñaar
Muy taw muy naaj xale bi
Ñun dinañu yéeg sunu destination ndeysaan

Joxe naa lépp sans xalaat retour
Sans xalaat retour
Bëgg naa la aller ak retour
Aller ak retour

Yaay sama reeni xol
Yaay sama reeni xol
Bu xol bi di jooy mbëggeel a koy nax
Bu nit ñi di ree mbëggeel rekk a tax
Sa bët yi di weex jamm ju bari
Wax ma ku lay bégal temps yi

Ku jox sa xol mu jox la ko
Ku bégal ak mbëggeel mu delloo la ko
Man daanu naa nga jox ma loxo
Jooy naa sa tur tay ma wax la ko

Ci kaw ci kaw maak yaw
Duñu daanu duñ leen may li ñu bëgg
Ci kaw ci kaw maak yaw
Duñu daanu duñ leen may li ñu bëgg non

Joxe naa lépp sans xalaat retour
Sans xalaat retour
Bëgg naa la aller ak retour
Aller ak retour

Yaay sama reeni xol
Yaay sama reeni xol

Más canciones de Iss 814