Dee Interlude

de Dip Doundou Guiss

Lépp loo bëgg ma defal la ko maa dof ci yaw
Lépp loo joxoñ ma daggal la ko maa dee ci yaw
Bu asamaan doon daanu ma téeyeel la ko ma miir ci yaw
Maa la nob lool sama chérie coco maa la bëgg yaw

Baby, kaay waay ma ne kaay way
Xam nga ne namm naa la baby kaay waay
Ma ne yuu yuu nga ne yaa yaa lu yendu ci man ci yaw lay fanaan waay
Baby, kaay waay ma ne kaay waay
Xam naa ne namm nga ma baby kaay waay
Ma ne yuu yuu nga ne yaa yaa lu yendu ci yaw ci man lay fanaan waay

Lu sa jëm ji taaru taaru sa xol a ko dàq
Wormaal nga ma fees ngaak sutura sa ruu dafa màgg
Man maa tay bëgg la ba mu leer man it duma bëggaat
Ngalam nga lingeer ci dereet def ma sa buur ak sa jaam
Yaw rekk a fees samay bët yaw rekk sa flèche a may jam
Yelloo nga këyitu kër fim la dëkkal ngay des ba ma dëb
Bëggal ma taasu ma fecc loo bëgg sa yu la neexee
Boo amul woon ma doon nit ku dul mës am chance'u mbëggeel
Yenn saay nu jàppante ci wax xol yi fees ron qooñ di toq bul di denc lenn Bae
Yaay leer gi fees ci sama xol
Leer biddeew ci sama kaw, bideew bi leeral sama yoon
I miss you everyday and more the yesterday I need your love

Lépp loo bëgg ma defal la ko maa dof ci yaw
Lépp loo joxoñ ma daggal la ko maa dee ci yaw
Bu asamaan doon daanu ma téeyeel la ko ma miir ci yaw
Maa la nob lool sama chérie coco maa la bëgg yaw

Baby, kaay waay ma ne kaay way
Xam nga ne namm naa la baby kaay waay
Ma ne yuu yuu nga ne yaa yaa lu yendu ci man ci yaw lay fanaan waay
Baby, kaay waay ma ne kaay waay
Xam naa ne namm nga ma baby kaay waay
Ma ne yuu yuu nga ne yaa yaa lu yendu ci yaw ci man lay fanaan waay

Bu ñépp nee déet te Yàlla ne waaw fàww mu am diggante bi (fàww mu am sunu diggante)
Yaak say défauts ak say qualités noonu laa la bëggee, noonu laa la bëggee
Sunu diggante bi dara xaaju ci sa noon yi siisu nañ nu bàyyi ak Yàlla
Pigg ak peel la bañuma ci dara
Mukk duma la mës a bàyyi ginnaaw
Nu dund freedom ni céeli muy naaw
Baby, maa la bëgg duma dëgg tànk ci say bëgg-bëgg li nga bëgg laa bëgg sa mbëggeel moo may bégal
Joxoñal ma dagg nu dundu aljanna

Li may bégloo ni ga mel la honey ak li ci yaw (baby)
Yaw laa doon xaar ngir nga defar sama xol bi ñu yàq (xol bi ñu yàq)
Nun nu réeroo ba nga ba ma la sama noon yi di xaar (noon yi di xaar)
Bu leen ko jàppe ndax dañoo xamul maak yaw fi nu jaar
(Fi nu jaaar aaah aaah aaah fi nu jaaar aaah aaah aaah)

Más canciones de Dip Doundou Guiss