M'a Ngui Baxx

de Dieyla Gueye

Nelawoo ba yàndoor
Dëkke lu bon ak lu ñaaw
Soxor iñaan
Moo la condamné
Doxal sa yoon
Duma la sóoraale
Mënuloo ma tere dundu li ma neex

Maa ngi baax
Duma leen faale

Billaay dinga gëna tarde
(Billaay dinga gëna tarde)
Man daal duma leen faale
(Non non duma leen faale)
Fii lépp a ngi tolloo, taluma noono
Billaay duma leen faale

Yaw mbaa jàmm nga fanaan
Yaw mba jàmm nga yéndo
Woté lo gëmul, xamoo ni jëli naa la

Maa ngi baax
Duma leen faale

Billaay dinga gëna tarde
Man daal duma leen faale
Non non duma leen faale
Fii lépp a ngi tolloo, taluma noono
Billaay duma leen faale

Noono (moom talu la)
Li Yàlla def si man
Nga ne mu ku du fi ame
Aaah nga di ma jebaane
Nga di ma jebaane
Non non nono yeah

Xamaloo ma dara wër di ma togge
Di ma soxore yeah yeeeah
Nelawoo ba yàndoor
Lu dul dëkke lu bon ak lu ñaaw

Bul faale bul toppatoo doxal sa dox
Wuyooy bokkuleen yoon, doxal sa dox
Bul faale bul toppatoo doxal sa dox
Maa ngi baax (maa ngi baax)
Duma leen faale

Billaay dinga gëna tarde
(Billaay dinga gëna tarde)
Man daal duma leen faale
Non non duma leen faale
Fii lépp a ngi tolloo, taluma noono
Billaay duma leen faale (taluma noonu)

Más canciones de Dieyla Gueye