Li lanla

de Dieyla Gueye

Dama la bëgg ba xawma li ma dal li lan la
Xawma li lan la
Tayuma ko xale bi xawma li ma dal li lan la
Xawma li lan la
Dama la nob te teler na ma
Te leer na ma wat na ko ci Yàlla
Waxal ma ko wa koñ be ñu bàyyi ma
Ñu bàyyi ma ak yaw ngir Yàlla
Ma moom la

Kaay nga wax ma foo ma duggal man
Bëgg naa xam ndax naturel na
Dama lay gis salit di la bëgg coob
Mel ni gaynde bu gis yàpp

Xawma li lan la
Xawma li lan la
Xawma li lan la

Dama lay gis salit di la bëgg coob
Mel ni gaynde bu gis yàpp
Xawma li lan la
Dama lay gis salit di la bëgga fóon
Xawma li ni lan la
Xawma li lan la

Waawaaw
Man ak xale bi ba àdduna jeex
Ma wane ko luy fulë
Ma ni la ki la doon xaar
Defuma faux départ
Hé li de coow la
Foo ma woo ma ñëw
Man duma ragal ñeme naa loolu waawaaw
Ñeme naa loolu waawaaw, he he

Ahn li ma dal xamuma
Fekke dañuma liggéey de jàpp na
Dama ko nob mujj dof mbaa jamm la
Demal nga lajjal ma ko li ma dal li lan la

Kaay nga wax ma foo ma duggal man
Bëgg naa xam ndax naturel na
Dama lay gis salit di la bëgg coob
Mel ni gaynde bu gis yàpp

Xawma li lan la
Xawma li lan la
Xawma li lan la

Dama lay gis salit di la bëgg coob
Mel ni gaynde bu gis yàpp
Xawma li lan la
Dama lay gis salit di la bëgga fóon
Xawma li ni lan la

Dama ka nob ba dof
Papa sama yaay ñanal ma
Tayuma ko xale bi
Donal sama sëriñ ñanal ma
Dama la love hee, bàyyi ma
Bàyyi ma ak moom ngir Yàlla
Waxal ma ko wa koñ be
Ñu bàyyi ma, ñu bàyyi ma
Ak yaw ngir Yàlla ma moom la

Ahn li ma dal xamuma
Fekke dañuma liggéey de jàpp na
Dama ko nob mujj dof mbaa jàmm la
Demal nga lajjal ma ko li ma dal li lan la

Kaay nga wax ma foo ma duggal man
Bëgg naa xam ndax naturel na
Dama lay gis salit di la bëgg coob
Mel ni gaynde bu gis yàpp

Dama lay gis salit di la bëgg coob
Mel ni gaynde bu gis yàpp
Dama lay gis salit di la bëgga fóon
Xawma li ni lan la

Xawma li lan la
Man duma ragal ñeme naa loolu waawaaw
Xawma li lan la
Man duma ragal ñeme naa loolu waawaaw
Xawma li lan la

Más canciones de Dieyla Gueye