Doflo Ngama

de Dieyla Gueye

Man sama sañse yaw la
Fu ma belli yaw la
Du kenn yaw la
Dofloo nga ma

Man ki ma tànn yaw la
Nga nob ma raw la
Du kenn yaw la
Dofloo nga ma

Yaa ma ko tàmmal
Yaa ma ko jàngal
Yaw li nga àndal
Dofloo nga ma

Laax bi lu mu tàng tàng
Kenn du ma ko ràccal
Li nga jantal
Dofloo nga ma

Jëkkër su la nobee
Danga koy tiitaroo
Ni ma la nawe
Yaay sama héros

Samay gént nga may àndil mu leer
Ma pare dundu lu ne dox ci li la neex

Pare naa (pare naa)
Pare naa (pare naa)
Manatuma la rëcc, sama seytaane
Pare naa (pare naa)
Pare naa (pare naa)
Neex neex bi sama dundu yawa coco bànneex

Man sama sañse yaw la
Fu ma belli yaw la
Du kenn yaw la
Dofloo nga ma

Man ki ma tànn yaw la
Nga nob ma raw la
Du kenn yaw la
Dofloo nga ma

Yaa ma ko tàmmal
Yaa ma ko jàngal
Yaw li nga àndal
Dofloo nga ma

Laax bi lu mu tàng tàng
Kenn du ma ko ràccal
Billaay waay

Mbëggeel nak
Bu la jàppe nga doon xale
Dootoo dal
Foo tollu di koy wane
Lii moo tax fu ma tollu di la jege
Nga may nab-nabbee
Wane ni nga jonge

Mbëggeel nak (waxal!)
Bu la jàppe nga doon xale (nga doon xale)
Dootoo dal (dikkal)
Foo tollu di koy wane
Lii moo tax fu ma tollu di la jege
Nga may nab-nabbe
Wane ni nga jonge

Talibee Cheikh Bi
Jambari Al Amine
Bëgg na AÏcha rasul ba mu jeex yaay
Dundu mbëggeel dafa neex
Xoolal timis bu Aziz Ndiaye

Pare naa (pare naa)
Pare naa (pare naa)
Manatuma la rëcc, sama seytaane
Pare naa (pare naa)
Pare naa (pare naa)
Neex neex bi sama dundu yawa coco bànneex

Man sama sañse yaw la
Fu ma belli yaw la
Du kenn yaw la
Dofloo nga ma

Man ki ma tànn yaw la
Nga nob ma raw la
Du kenn yaw la
Dofloo nga ma (dikkal!)

Yaa ma ko tàmmal
Yaa ma ko jàngal (waxal!)
Yaw li nga àndal
Dofloo nga ma

Laax bi lu mu tàng tàng
Kenn du ma ko ràccal
Li nga jantal
Dofloo nga ma

Más canciones de Dieyla Gueye