Diayoulen
de Dieyla Gueye
Jigéenu jant
Jigéenu weer yaa ñu leeral
Yaayoo nga cant
Kuñ fi coow yaa ko féñal
Yaa di ndox, yaa ñu tax a màndi
Yàgg nga di dox, nelawoo bidënti
Yaay àdduna, sargal la jaddu na
Feccal ma tàccu la, tey ma wayal la
Sa jom ji yatu na
Say jëf ñoo ko sedde yaa ñu nàmpal
Bott ñu, ar ñu, yañu tete
Yaw rekk jar a takkal
Médaille gu ne yaa ko yelo
Daj nga fi lu ne
Taxul nga soppi melokaan
Su ma lay way sa jom a tax
(Sen fu la ak fayda wër na àdduna)
Sa ngor a tax
(Yenn rekk a taaru, tay ma joobe leen)
Géwél tëggël ñu jayyu
Tey nga joobeleen
Li coow li bari bari may ki ko waral (doxal!)
Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!)
Man rekk (hé, yaw rekk!)
Man rekk, ma bari doole
Li coow li bari bari jigéen naa ko waral (doxal!)
Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!)
Man rekk (hé, yaw rekk!)
Man rekk, ma bari doole
Géwél tëggël, ñeeño tàccul
Laobé jukk lëmbël
Géer jukk di maye sax jigéen ñoo ko waral
Jigéen ju baax nan la war a mel
Xanaa ni nan (ni), nan (ni ni)
Yaa ñeme coono yaay jaambar
Yaa ngi liggéey toogoo di xaar
Yaayu Astou Gueye baax na
Gore na jom ju bari lool
Wayal, wayal
Leen lu fi baax jigéen na ko waral, wayal!
Bakkari musel jigéen
Ma way
Bul dóor, bul saaga, bul toroxal
Jigéen la!
Dieyla, feccal ma li kay!
Jox ko li mu moom
Mooy ki juur sa doom
Bi nga dee gone gone gone
Moo la nàmpaloon
Kaay!
Li coow li bari bari may ki ko waral (doxal!)
Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!)
Man rekk (hé, yaw rekk!)
Man rekk, ma bari doole
Li coow li bari bari jigéen naa ko waral (doxal!)
Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!)
Man rekk (hé, yaw rekk!)
Man rekk, ma bari doole
Feccal ma way la (doxal!)
Jayyul ma jiin la (yëngul!)
Xam naa sa doole
Yaw rekk def jaloore
Tey ma jobel la ku aye wal sa momee
Jayyuleen, wuy wuleen jayyuleen
Feccal ma li, kay!
Más canciones de Dieyla Gueye
-
Doflo Ngama
Doflo Ngama
-
M'a Ngui Baxx
M'a Ngui Baxx
-
Yaw la
Yaw la
-
Déko Woyofal
Déko Woyofal
-
Li lanla
Li lanla
-
Neex Na
Neex Na