Déko Woyofal

de Dieyla Gueye

Dee ko woyofal, bul ko disal
Àdduna bii lépp dafay jeex
Jege ma, yaw bul ma wéetal
Ndax lu ñi dundu dafa war a dàq neex

(Lii nga ma jaral, mbëggeel moo ko waral)
Kaay ñu mbégelante mak yaw mbëggeel alimenté ko
(Lii nga ma jaral, mbëggeel moo ko waral)
Jaral nga maa

Jaral nga ma fal fa lalé lépp di lay bégal
Loo la Yàlla dogal ma doo géwél bi lay woyal
Loo bëgg laay def soo tëddee na nga nelaw

Tëyel ma
Tëyel ma, doo gis ku mel ni man
Ni wëral fu la neex, benn la fii
May faj sa nammeel, yaw xam nga loolu
Tayuma ko nii la mel kon dee ko woyofal

(Lii nga ma jaral, mbëggeel moo ko waral)
Kaay ñu mbégelante mak yaw mbëggeel alimenté ko
(Lii nga ma jaral, mbëggeel moo ko waral)
Jaral nga maa

Su ma nangoo doon sa Yaye Fall
Bul nelaw, doonal Baye Fall
Mbëggeel yërmandé kese la
Doonal Baye Fall

Jaral nga ma fal fa lalé lépp di lay bégal
Loo la Yàlla dogal ma doo géwél bi lay woyal
Loo bëgg laay def soo tëddee na nga nelaw

Tëyel ma
Tëyel ma, doo gis ku mel ni man
Ni wëral fu la neex, benn la fii
May faj sa nammeel, yaw xam nga loolu
Tayuma ko nii la mel kon dee ko woyofal

(Lii nga ma jaral, mbëggeel moo ko waral)
Kaay ñu mbégelante mak yaw mbëggeel alimenté ko
(Lii nga ma jaral, mbëggeel moo ko waral)
Jaral nga maa

Wouyoo yo lele yo lele yole
Thiaba chérie Amadou xam nga ne mbëggeel neex na
Kon neex na
Diey Astou Sarr eh Sarr siri lay ndem li neex na neex na
Dundal sa nobeel
Soo ma bëggee den ko jefe ma gis ma gis ko
Wouyoo yo lele yo lele yole

Más canciones de Dieyla Gueye