Sey dou choix

de Coumba Gawlo

Su ngeen xamoon fi ma jaar ba yegg ci fi
Su ngeen jaaroon fi ma jaar ba tollu fi
Céy su ngeen dundoon li ma dundu ba yegg ci fi
Su ngeen xamoon, su ngeen xamoon, su ngeen xamoon

Saa yu ma juumee di ngeen ma baal
Saa yu ma juumee di ngeen ma baal

Su ngeen xamoon ne fanaan na ci basaŋ bi ba tay
Kër famille bu ne dëkk naa fa ba baay
Yeen su ngeen xamoon ngeen jàpp te bañ a bàyyi
Su ngeen xamoon ngeen fonk seeni waa-jur

Saa yu ma juumee di ngeen ma baal
Saa yu ma juumee di ngeen ma baal

Ba may xaley njël la daan yeewoo gàddu sama pan
Nda lu tollu ni barigo la daan rot bés bu ne te duma tere jàng
Xuloo naa xeex naa ci robinet yi ba tay

Su ngeen xamoon ne saa yu ma daan jàngi grand-yof lay doxe ba pompier
Ndeysaan sama papa mësu bëgg ma xiif benn yoon
Heure-u recréation la ma daan indil ndékki pain mayonaise
Ba suñu waa école di ma tooñ pain mayonaise

Saa yu ma juumee di ngeen ma baal
Saa yu ma juumee di ngeen ma baal

Su ngeen xamoon ni guddi la daan fot sama robe bi wér ko suñu gannaaw frigidaire

Sama ngor sama jom ak jaay sama bégnet dugub bi
Nango jàngi nango liggéey nango muñ moo tax ma yegg ci fi

Saa yu ma juumee di ngeen ma baal
Saa yu ma juumee di ngeen ma baal

Ba may xaley njël la daan yeewoo gàddu sama pan
Nda lu tollu ni barigo la daan rot bés bu ne te duma tere jàng
Xuloo naa xeex naa ci robinet yi ba tay

Saa yu ma juumee di ngeen ma baal
Saa yu ma juumee di ngeen ma baal

Su ngeen xamoon, su ngeem xamoon
Céy! Bu ngeen xamoon
Yeen xamoon, yeen su ngeen xamoon
Su ngeen dundoon, céy! Su ngeen dundoon
Li ma dundu yeen su ngeen dundoon

Saa yu ma juumee di ngeen ma baal
Saa yu ma juumee di ngeen ma baal

Más canciones de Coumba Gawlo