Miniyamba

de Coumba Gawlo

Topp ma soo ma bëggee
Jegesi ma soo ma nobee
Déglu ma soo ma bëggee
Jox ma sa xol soo ma wooloo

Gis nga chéri li di mbëggeel
Ak réy waru ko laal
Gis nga baby sunu mbëggeel
Bu ci def lu dul sa xol
Ëpp na at ba ñu xamante
Booba ba tay lu ne muñe naa ko
Ëpp na at ba ñu bëggante
Bés bu ne maa di la gën a love

Yaw baby sunu mbëggeel
Bu ci def lu dul sa xol
Yaw chéri jox ma sa xol
Waat naa ne duma ko xaajamal

Baby mbëggeel aventure rekk la
Mënoo xam laaj biir fi yëg dugguloo
Baby mbëggeel ci xol la jogé
Te bu jogé ci xol, xol rekk a ka mën a xam

Céy mbëggeel munoo xam la ca biir fi yëg dugguloo
Céy mbëggeeley mbëggeeleee
Ëpp na at ba ñu bëggante
Bés bu ne maa di la gën a love
Sama xol bi yaa ci ne
Annn chéri bëgg naa la
Bëgg naa la, bëgg naa la

Kaay ñu bëggante
Mbëggeel mënoo xam la ca biir fi yëg dugguloo
Gis bëgg Yàlla koy def ci jaam miin bañ ci jikko la
Man bëgg naa la
Sama xol bi yaw la tànn, bëgg naa la
Bëgg naa la, kaay ñu bëggante
Man de bëgg naa la suñu mbëggeel réy waru ko laal
Jox ma sa xol bi waat naa ne duma ko xajamal
Man bëgg naa la, bëgg naa la kaay ñu bëggante

Baby mbëggeel aventure rekk la
Mënoo xam laaj biir fi yëg dugguloo
Baby mbëggeel ci xol la jogé
Te bu jogé ci xol, xol rekk a ka mën a xam
Kaay!

Baby mbëggeel aventure rekk la
Mënoo xam laaj biir fi yëg dugguloo
Baby mbëggeel ci xol la jogé
Te bu jogé ci xol, xol rekk a ka mën a xam

Más canciones de Coumba Gawlo