Deweneti

de Coumba Gawlo

Dafa am bees Nabi
Sallallahu Alaihi Wasallam ngeen gi mbidef Nabi
Bésu it lawoon Nabi romb xale yi ñu tok
Sañse ba jekk di fo di ree am ca ñoom ku béru di jooy
Ngeen ngi mbidef Nabi
Sallallahu Alaihi Wasallam woo xale ba nekkoo doom lu
wappal fowo ni say morom ngaberu di jooy?

Xale ba dal di ni ko
Sama baay da àndoon ca xeex ba ag Nabi
Sallallahu Alaihi Wasallam dee fa ma weet jaaxle
Sama yaay séy ak beneen góor mu gëne ma nangu sama alal
Nangu sama kër ba maa ngi
Tumuraanke di taxawaalu ak di fanaan ci mbedd yi
Mu toroxal ma, busanal ma, mettital ma
Mo waral ci bésu it bi
Sama xel dem ci sama baay ma weet jooy
Xam ne su dundoon duma mësa tumuraanke

Naka noonu Nabi
Sallallahu Alaihi Wasallam ne xale ba ndax bëgg nga ma doon sa baay
Aïchatu doon sa yaay
Fatimatu doon sa mag
Wa aliune ak Hassan ak Housseyu doon say mag
Xale ba daaldi ni ko
Ana kan may bañ ya rassouloulah Nabi

Ana kan mooy bañ ya rassouloulah
Neen ngi mbidef ki gën te kenn gënu ko
Xureyshiin yaay seen géer
Banuhasim yaay seen baay
Ana kan mooy bañ Nabi
Naka noonu Nabi
Yóbbu xale ba këram, taral ko
Mu dellusi taru lool
Ñëw moroom ya naan ko
Sa taar bi ak sa leer gi nga andal
Wute na ak bi nga fiy jugee
Ndax danga mel ni ku judduwaat
Xale ba dal vi ni leen
Yoneen bi la dajel
Mu laaj ma lu may jooy
Ma wax ko ko mu yóbbu ma këram
Kon man rassouloulah matax

Aïchatu doon sa yaay
Fatimatu doon sa mag
Wa aliune ak Hassan ak Housseyu doon say mag
Xarit ya daaldi ni ko
Yaa Nabi
Su ñu sañoon
Su ñu bayee
Dee ca xaree ba ndax yaa rassoulilah

Más canciones de Coumba Gawlo