Yaakaar

de Ashs The Best

Yow mii laa doon sèntu
Mbaa yaakaar tasul ci yoon wi
Jambaar dawul daa wuti
Jom moy dem fulla moy dellusi

Yaay di na woote
Di laaj noo yèndoo
Leer na ma sa jamm mo koy gënël
Nga am′ag nga ñakk taxu koo jog
Su soxla yi woote (Soxla)
Te ñu yaakaar ko ci yow
Di lañ la xaar keneen ku dul yow
Yow mi ñëpp yaakaar
Ci yow sa soxla koo koy diis

Bul tiit bul jàxle
Lu yoon bi mën meti
Bul xaadi
Lu yòmb jiggul goor
Jiggul sax jigeen
Kon lan ngay caalit

Bul tiit bul daw bul jàxle
Lu yoon bi mën meti
Bul xaadi
Lu yòmb jiggul goor
Jiggul sax jigeen
Kon lan ngay caalit

Soo yakkee sooraale ma
Man suma foree fii indil la
Yaa taggoo ñu yobbante la
Te soo goree lepp fekki si la

Suñ demmee ba yaakaar
Ci yow mi di utti loo am di utti lu gën
Suñ demmee ba yaakaar
Ba duñ xalaat yaakaar gi tas
Suñ demmee ba yaakaar
Ci gaynde gi rëbbi ji woon mën jaare fa sooy
Suñ demmee ba yaakaar
Ci moom mi dem utti ji jën

Yow mii laa doon sèntu
Mbaa yaakaar tasul ci yoon wi
Jambaar dawul daa wuti
Jom moy dem fulla moy dellusi

Yow mii laa doon sèntu
Mbaa yaakaar tasul ci yoon wi
Jambaar dawul daa wuti
Jom moy dem fulla moy dellusi

Bul tiit bul daw bul jàxle
Lu yoon bi mën meti
Bul xaadi
Lu yòmb jiggul goor
Jiggul sax jigeen
Kon lan ngay caalit

Bul tiit bul daw bul jàxle
Lu yoon bi mën meti
Bul xaadi
Lu yòmb jiggul goor
Jiggul sax jigeen
Kon lan ngay caalit

Bul jàxle
Bul xaadi
Jiggul sax jigeen
Lan ngay caalit

Bul jàxle
Bul xaadi
Jiggul sax jigeen
Lan ngay caalit

Más canciones de Ashs The Best