Xalam

de Ashs The Best

Jëlal caabi kër gi téj ko
Ngir saa yo wéetee mu mel ni maa ngi sa wet
Xalam nga ca taatu guy ga
Moom laa la tudde balago la lay wowe
Ci gal gi la nekk di coow
Yaw soo ma nammee séentuma ci wer wa
Jaarul ci xalu maam ya
Ci àndu gaddaay ga, wetaay ba sonn la

Fi dara desatul fi (woooowooo)
Dara desatul la (wooo)
Jëbbal naa la sama xol
Ak xel bi lu ko raw lay yeg ci man mi
Kañ la lay gis
Hummm

Mbaa soo ma soree
Mbaa soo ma soree
Mba soo ma soree doo tok ba jaaxle nga dem bàyyi ma fi
Mbaa su ma guddee (umm humm humm)
Mbaa su ma gudde
Mba su ma gudde ba sexlu reer bi
Mbaa doo reer ba ma
Watt na dina ñówaat
Waaye xamaguma kañ lay doon
Yàlla na mën doylu dem fu sori nga gëna jegesi ma
Su may dee si ala bi
Yaw yaay gaynde bu may réy
Yaw yaa fa fekk ñépp taxaw, man ma digg nga talaw
Ca kaw aaaasaman
Foofu nga may jëme

Ci kaw aaaasaman
Ci aaaasaman
Foofu nga may jëme, mbaa dinga ma peloo
Ci kaw aaasaman

Jëlal caabi kër gi tej ko
Ngir saa yo wetee mu mel ni maa ngi sa wet
Moom la la tudde bala go la lay wowe (wowe wowe)
Ci gal gi la nekk di coow
Yaw soo ma nammee sentuma sa wer wa
Jaarul ci xaalu maam ya (jaarul)
Ci àndu gaddaay ba, wetaay ba sonn la (wetaay ba sonn la)

Wetaay ba sonn la (jëlal, jëlal)
Jëlal caabi kër gi ñu daje maak yaw
Namm la nammeel
Waaye xamoon naa ni dinañu daje maak yaw
Ooooh
Jëlal, jëlal, jëlal maa ngi ñów

Más canciones de Ashs The Best