Ngala Way

de Ashs The Best

Maam, all ma ay dàll ma sol dem wutti gi
Luñu dunde
Suma amoon laaf kon naaw ci jawwu jii
Kumay gungee
Di sànku ñaan ci ñi di yalwaan
Aljaanay suuf fumu féete
Sama xel mooy daan ci bëree sama xol
Te sama xol moo ëppu doole

Ñun màgg nañu, suñu dàll baay mën ñu jot
Ñu war a janook moom
Ndax xam nani léegi, àdduna dootul ñu baal
Fumay mujjee ak moom

Maam ngale,ngala waay, maam ngala waay, ngala waay
Man suma doon délluwaat
Fan lay délluwaat?
Ngala waay, ngala waay, ngala waay
Suma doon ñibbiwaat, ñibbiwaat

Ndax mës nañ fe gis ku weet
Amoon na bës ñu weet
Daan nañ fee gis fu weet
Ndax fi ngéen dëkkufi

Maam ngale,ngala waay (maam ngala waay)
Kon ngala waay ngale (ngala waay ngale waay yoo maam booy)
Man suma doon délluwaat (délluwaat)
Fan lay délluwaat? (suma doon délluwaat, fan lay délluwaat?)
Ngala waay, ngala waay, ngala waay
Suma doon ñibbiwaat, ñibbiwaat

Ci àdduna
Di sànku ñaan ci ku nee, ci ku nee
Ndax fi ngéen dëkkufi

Más canciones de Ashs The Best