Maa Ngi Dem

de Ashs The Best

Now I know, now I know
But I don′t know what I'm feeling inside
Gestu woo ma
Maa ngi dem, maa ngi dem
Soo ma gisatul dem naa

Maa ngi dem, baayi a fi sama xol
Di naa weet, weet ci sama yoon
Subateel, ba jant sow
Yaa ngi sèntu, sa waay ju fi joge woon

Maa ngi dem te taggu wu ma la
Suma reeree mbaa duñ ne yow la
Maa ngi dem te taggu wu ma la
Suma reeree mbaa duñ ne yow la

Ñëw naa fi noor (Ñëw naa ba dem gisoo ma)
Ñëw naa fi nawet (Ñëw naa fi nawet tamit)
Ñëw naa fi koor (Tabaski akk Tamxarit)
Fekk fi bekkoor (Fekk la ngay bekkoor)
Li ma dundee (Li ma dundee)
Akk li ma weesu (Akk li ma weesu)
Day dellusee (Da fay dellusee)
Ba mel ni seetu (Ba mel ni seetu)

Maa ngi dem te taggu wu ma la
Suma reeree mbaa duñ ne yow la
Maa ngi dem te taggu wu ma la
Suma reeree mbaa duñ ne yow la

Dem naa te taggu wu ma la (Dem naa)
Suma reeree mbaa duñ ne yow la (Mbaa duñ ne yow la)
Jooy naa te kenn dooru ma (Man dem naa)
Suma reeree mbaa duñ ne yow la (Yow la)

Maa ngi dem te taggu wu ma la
Suma reeree mbaa duñ ne yow la
Maa ngi dem te taggu wu ma la
Suma reeree mbaa duñ ne yow la

Maa ngi dem maa ngi dem

Más canciones de Ashs The Best