Ayway Samba

de Ashs The Best

Mënatuloo siggi ci bët xool ma
Mënooma woon gëm ni now xool ma
Ku la ko waxoon loolu am na
Lu am du réer te man na soor
Li nga ma waxoon wuutek say jëf
Dige boor la te yaw woor nga
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp ta nga gaañ ma

Keerog sam xel bi waroon na tey
Say wax woor ma
Dañ ma tere woon ma taxa wat ni sañuloo ko
Ma jël la teg fi ma tegul benn mindeef
Bi nga xamee bëgguloo ma wax ma ko
Bëñ ak lammiñ fak ñu laale (waawaaw)
Waye fajaloo ma sama gacc (mmm)
Nu may defak samay dëkkëndoo
Duma siggi xol ci samay nawle gacc gi fu ma koy waxe
Ci xol la tiis boo may lacce
Dinga ko gis Yàlla ñuy àtte
Bi nga fi jii bës dige ko goobe

Ayway Samba
Yaw réero moma
Nga tooñ ma benn yoon man ma baal la
Nga def ko ñaari yoon man ma baal la
Yeah way Samba
Yaw mi de bëgguloo ma
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp ta nga waar ma

Waawaaw
Mmmh mmh
Ki sedday bi
Tàngoor bi
Nekk ci naaj bi te keraloo ma, keraloo ma
Defuloo ma ni ma la def

Lu ma xam wax la
Alaal ma jox la
Mbëggeel ma waan la
Kan nga ma jënde lan la ma rawe
Ki nga ma jënde lum ma ëppële

Réwoo réwel naa ko
Réwo réwo
Keneen ku ma gis ni yaw la
Réwo réwo
Ñu mel ni yaw lay musloo
Woo mbëggeel
Nga def lii man lay wuyoo/Ni mbëggeel def man lay woyloo

Ayway Samba
Yaw réero moma
Nga tooñ ma benn yoon man ma baal la
Nga def ko ñaari yoon man ma baal la
Yeah way Samba
Yaw mi de bëgguloo ma
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp ta nga waar ma

Gàcc gi fu ma koy waxe
Ci xol la tiis boo may laaje
Dinga ko gis Yàlla ñuy àtte
Bi nga fi jii bës dinga ko goobe

Más canciones de Ashs The Best